Doomi Sibeyon yu góor di Aya ak Ana. Te Ana moomu moo feeñal bëti ndox yu tàng ya ca màndiŋ ma, ba muy sàmm mbaami baayam Sibeyon.
TSK
TSK · 2 Samuel 13:29
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Buur ne Doweg: «Ayca yaw, fàddal sarxalkat yii!» Doweg Edomeen ba fàdd sarxalkat ya. Rey na bésub keroog juróom ñett fukki nit ak juróom (85) ñuy sol xar-sànnim lẽe.
Sang bi, ñaari doom yu góor laa amoon. Dañu doon xeex ñoom ñaar ca àll ba te ku leen àtte nekku fa. Kenn ki dóor moroom mi, rey ko.
Buur ne leen: «Àndleen ak samay dag, ngeen waral sama doom Suleymaan ca sama kaw berkelle bu jigéen ba, te yóbbu ko Giyon, bëtu ndox ba.
¶ Ba mu ko defee Akasiya yebal njiitu juróom fukki dag, mu ànd ak juróom fukki nitam, dem ba ca Ilyaas. Gisuñu lu moy mu toog ca kaw tund wa. Njiit la ne ko: «Ée góoru Yàlla gi, Buur nee nga wàcc.»
Lu bon la seeni loxo mane: kàngam di laaj, ab xaali di sàkkub ger, boroom daraja moom, di wax fuqley bakkanam, ñu ànd ràbbum pexe.