¶ Jaan nag moo gënoona muus ci rabi àll, yi Yàlla Aji Sax ji sàkk yépp. Jaan ja moo ne jigéen ja: «Ndax wóor na ne Yàllaa ne: “Buleen lekk ci doomi genn garabu tool bi”?»
TSK
TSK · 2 Samuel 13:3
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Ba loolu wéyee Yuda yebal xaritam, ba dëkk Adulam, mu yóti ndaw sa bëy wu ndaw wa, ba mana jotaat la mu tayle woon ca ndaw sa. Xarit ba nag gisu ko.
Yese indi Simeya, Samiyel ne: «Aji Sax ji tànnul kii it.»
Yowab nag yónnee ca dëkk ba ñuy wax Tekowa, ñu jëleji fa jigéen ju rafet xel, indil ko ko. Yowab ne ko: «Dangay ñaawlu-ñaawlulu. Solal yérey ñaawlu, te bul xeeñu. Melal daal ni jigéen ju jota ñaawlu lu yàgg, ngir ku mu deele.
Ba mu tëkkoo Israyil, Yonatan a ko rey. Yonatan, Simeya magi Daawuda mooy baayam.
Seres jabaram ak xaritam ya yépp ne ko: «Dangay defarlu bant bu am taxawaayu ñaar fukki meetar ak juróom. Bu subaa nga ne Buur ñu wékk ci Mardose, ba noppi nga ànd ak Buur ca bernde ja, sa xol sedd.» Aman nag rafetlu xel ma, ba defarlu bant ba.
Ñu baree ngi wuta neex boroom daraja, ku nekk a bëgga xaritook kuy joxe.
Ndaxte xam-xamu àddina sii, ndof la fa Yàlla. Moo tax bindees na ne: «Mooy kiy jàpp ñi muus ci seen pexey muusaatu,»