TSK

TSK · 2 Samuel 2:4

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

«Yaw Yuda, mi say doomi baay di taggeji, ngay sëqi sa ndoddi noon, sëgal leen, sa doomi baay a lay sujjóotal.

¶ Ba waa Yabes ga ca Galàdd déggee la waa Filisti def Sóol,

Diir ba Daawuda falu buurub Ebron gu waa kër Yuda, juróom ñaari at la ak juróom benni weer.

Ca Ebron la yore nguurug Yuda juróom ñaari at ak juróom benni weer, waaye ca Yerusalem la yore diiru fanweeri at ak ñett, mboolem Israyil ak Yuda.

Gannaaw Absalom ma nu faloon mu jiite nu, dee na ca xare ba, lu nu tee wax lu jëm ci délloosi Buur Daawuda?»

¶ Ba loolu amee ñu àgge Daawuda jëfi Rispa doomu Aya, nekkaaleb Sóol ba.

Yoyada génne doomu buur ba, solal ko mbaxanam buur, jox ko kayitu doxalinu nguur ga; ñu fal ko nag buur, diw ko diwug pal. Ba loolu amee ñu tàccu, ne: «Guddalu fan, Buur!»