Ibraam nag wax buurub Sodom ne ko: «Man yékkati naa sama loxo, Yàlla Aji Sax ju Kawe ji seede, moom mi sàkk asamaan ak suuf,
TSK
TSK · 2 Samuel 2:5
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Ci biir loolu mu wax ak ñaari goroom, ne leen: «Demleen kay, ñibbileen, ku nekk sa kër yaay. Yal na leen Aji Sax ji baaxe, na ngeen baaxe woon ñi wuutu, te baaxe ma, man itam.
¶ Mu ne ko: «Yal na la Aji Sax ji barkeel, doom! Jiwati nga bokk gi ngor lu gënatee rafet. Ndax su la neexoon, nga topp ci xale yu góor yi, ñu am ak ñu ñàkk.
¶ Ñu wax nag ndaw ya jóge Yabes Galàdd, ñu jottli seen waa dëkk ba ne leen, ca ëllëg sa bu jant bi tàngee, dees na leen wallu. Ndaw ya dem, àgge ko waa Yabes, waa Yabes bég.
Yaa ma wax lu baax li nga ma defal tey; Aji Sax ji teg ma ci say loxo, te reyuloo ma.
Bëkk-démb doŋŋ nga fi ñëw, tey ma di la bàyyi ngay ànd ak nun di wëreelu, te xawma sax fu ma jëm. Dellul, kay, ànd ak sa waa réew. Yal na la Aji Sax ji won ngor ak worma.»
Yal nangeen barkeeloo Aji Sax ji, ki sàkk asamaan ak suuf.