Ba loolu amee Yonatan fasook Daawuda kóllëre, ndax sopp ko ni boppam.
TSK
TSK · 2 Samuel 21:7
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
bul noppee jëfe ngor sa digg ak sama waa kër mukk, ba sax keroog bu Aji Sax ji faree fi kaw suuf képp kuy noonu Daawuda.»
Yonatan ne Daawuda: «Demal ak jàmm, gannaaw noo giñoo nun ñaar ci turu Aji Sax ji ne “Aji Sax jeey seede sama digganteek yaw, ak diggante sama askan ak saw askan, ba fàww.”»
Kon nag giñal ma ci Aji Sax ji ne doo dagg sama askan wi may wuutu, te doo raafal sama tur ci sama waa kër baay.»
¶ Daawuda moo noon: «Ndax kenn desul ba tey ci waa kër Sóol, ba ma jëfeek moom ngor ngir Yonatan?»
Daawuda ne ko: «Bul tiit, dinaa jëfeek yaw ngor déy ngir sa baay Yonatan. Dinaa la delloo mboolem sa suufas maam Sóol, te yaay bokk ak man ndab ba fàww.»
Buur ne ko: «Kon boog, may naa la mboolem alalu Mefiboset.» Mu ne ko: «Jaajëf Buur sang bi, gis naa ni nga ma baaxee.»