Buleen ci sujjóotal lenn, buleen ci jaamu lenn, ndax man seen Yàlla Aji Sax ji, Yàlla ju fiir laa. Maay topp doom tooñu waajur, ba ca seen maasi sët, ba ca maasug sëtaati nit ñi ma bañ.
TSK
TSK · 2 Samuel 21:9
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ «Te it buleen jël benn xaalisu njotug bakkanu kenn ku rey nit ku yelloo dee. Kooku dee rekk mooy àtteem.
¶ Su dee dañoo fekk ku ñu bóom ci biir réew mi leen seen Yàlla Aji Sax ji moomale, mu tëdd ci àll bi, te xameesul ku ko rey,
¶ Noonu la Nawmi jógee Mowab, ñibbsi, ànd ak Ruut, gorob Mowabeenam ba. Ñu agsi Betleyem, fekk ngóobum lors ma di tàmbali.
¶ Ba mu ko defee ñu indi gaalu Aji Sax ji, yeb ko ca bérabam, ca biir xayma ba ko Daawuda sampal. Daawuda daldi joxe fa kanam Aji Sax ji ay saraxi rendi-dóomal, ak saraxi cant ci biir jàmm.
Kon dees nuy jox juróom ñaari góor ñu askanoo ci Sóol, nu jam leen ba mu sar fa kanam Aji Sax ji ca Gibeya, dëkkub Sóol, ma Aji Sax ji faloon.» Buur ne leen: «Dinaa leen leen jox.»