Waaye Aji Sax ji, sama Yàlla, rikk, teewlul li ma lay ñaan, man sab jaam, di la ko dagaan; ngalla déggal sama yuux, te nangu ñaan gi ma lay ñaan bés niki tey.
TSK
TSK · 2 Samuel 22:7
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
1 Kings 8:28
TSK
Psalms 27:4
TSK
Lenn laa ñaan Aji Sax ji, lii laay sàkku: dëkk kër Aji Sax ji, sama giiru dund, di niir taaru Aji Sax ji, te yéemoo këram.
Psalms 34:15
TSK
Na dëddu lu bon tey def lu baax, sàkku jàmm, saxoo ko.
Psalms 116:4
TSK
Ma woo Aji Sax ji wall, ne ko: «Ngalla Aji Sax ji, xettli ma!»
Jonah 2:4
TSK
Yaa ma xalab xóotey xolu géej, ndaw ma mëdd ma. Say wal ak say gannax, lépp a jaare sama kaw.
Habakkuk 2:20
TSK
Aji Sax ja moom, ma nga ca màkkaanum sellngaam, na àddina sépp selaw fi kanamam.»
Luke 22:44
TSK
Njàqare nag jàpp Yeesu, mu gënatee tënku ci kàdduy ñaanam, ba aw ñaqam mujj mel ni lumbi deret, di dal ci suuf.
James 5:4
TSK
Dégluleen! Peyoor, ga ngeen xañ ña gub seen tool, mooy yuuxu noonu. Jàmbati góobkat ya tàbbi na ca noppi Boroom gàngoori xare yi.