TSK

TSK · 2 Samuel 5:21

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ni ngeen di def ak ñoom kay mooy nii: seeni sarxalukaay, ngeen màbb; seen tuuri doj, ngeen rajaxe; seen xer yi ñuy jaamoo Asera tuur mi, ngeen gor; seen jëmmi tuur, ngeen lakk.

Ñu dugal gaal ga ca seen biir kër tuur ma ñu naan Dagon, teg ko ca wetu jëmmu Dagon ja.

te ñoo sànni seeni yàlla ci sawara it, ndax yooyoo dul Yàlla, xanaa lu nit sàkke loxoom, bant ak doj, ba tax ñu sànk leen.

Tuur yaa ngay sukk, bokk toqi; manuñoo wallu seen jëmm ya, xanaa doxal seen bopp, duggi ngàllo.

Mowab, yeena yaakaar dooleek alal, yeen it, dees na leen jàpp; Kemos, seen tuur mi duggi ngàllo, mooki sarxalkatam aki kàngamam.