TSK

TSK · 2 Samuel 7:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Sa kër ak sa nguur day sax dàkk fi sa kanam, te sab jal day dëju ba fàww.”»

ba keroog Aji Sax ji sottal kàddoom ga mu ma waxoon ne ma: “Su say sët sàmmee seen dundin, saxoo ngëm gu ma wéetal, te gar ci seen bakkan, kon doo ñàkk mukk ku lay wuutu ci jalub Israyil.”

«Kër gii de yaa ngi koy tabax. Waaye soo sàmmee samay dogal ak samay ndigal, di jëfe sama santaane yépp, di ci topp, su boobaa dinaa sottal li ma digoon sa baay Daawuda ci sa mbir.

Waaye Aji Sax ji bugguloona tas Yuda ngir Daawuda, jaamam ba, ndax la mu ko digoona may ci ay doomam kuy saxal nguuram fàww, ba du fey.

¶ Moo dugal ba tey jëmm ja mu sàkkoon ngir tuur ma ñuy wax Asera, ca biir kër ga Aji Sax ji waxoon Daawudaak doomam Suleymaan ne leen: «Ci biir kër gii ci Yerusalem, gi ma tànne ci mboolem giiri Israyil, laay dëj sama tur ba fàww.

Job 36:7 TSK

Du noppee xool aji jub ñi, xanaa di leen dëj ci jali buur yi, saxal seen toogaay, màggal leen.

Aji Sax ji nee: «Damaa fas kóllëreek ki ma tànn, muy Daawuda sama jaam bi ma giñal ne ko:

sàmmal ko sama ngor ba fàww, feddlil ko sama kóllëre.

Dooley kilifteefam ak jàmm ja du am kemu, fa jalub Daawuda ak nguuram, ga muy samp, saxale ko njekk ak yoon, tey jii, ba fàww. Lii la Aji Sax ji Boroom gàngoor yi def ci xéraangeem.

Aji Sax ji dafa wax ne: «Bu bésub yiw taxawee, ma nangul la; bu bésub mucc jotee, ma wallu la, sàmm la, def la ngay kóllëre sama digg ak askan wi, ngir yékkatiwaat réew mi, séddalewaat ay cér, suuf sii gental tey,

Ñooy dëkke réew mi ma joxoon Yanqóoba sama jaam ba, te seeni maam dëkke woon ko. Ñu dëkke ko ñoom it, ñook seeni doom ak seeni sët, ba fàww, te Daawuda sama jaam ba mooy doon seen boroom jal ba fàww.

Nga wax ko ne ko: “Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: Nit a ngi nii, Njebbit la tudd, ci bérabam lay jebbee, ba tabaxi kër Aji Sax ji.

Waaye ni ab tabaxkat ëppe teddnga kër ga muy tabax, ni la Yeesu yelloo daraja ju ëpp ja Musaa yelloo woon.