Ku ma daj, gudd fan, Aji Sax ji bége la.
TSK
TSK · 2 Timothy 2:10
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Piyeer nag miim, ne: «Soxna si, xawma kooku!»
Ñi saxoo di jéema def jëf ju baax, ngir di ko sàkkoo ndam, ak teraanga, ak texe gu sax, ñooñu, texe gu sax dàkk mooy doon seenub añ.
Maak boroom ngëm yi desee dëgër, damaa mel ni ku ngëmam desee dëgër, ngir iri leen. Lépp laa def sama bopp ci ñépp, ak nu mu mana deme, ba musal ñennat.
Loolu lépp yeena tax, ngir yiwu Yàlla lawa law, ba cant gu ne gàññ tukkee ci ñi ëpp ci nit ñi, ngir màggug Yàlla.
Kon nag dama leen di ñaan, ngeen baña yoqi ngir coono, yi may sonn ndax yeen; lépp seen teraanga la.
Ñoom la Yàlla nammoona xamal ni mbóot mi yaatoo te yéeme, ñeel jaambur ñi dul Yawut: mbóot mi moo di Almasee ngi ci yeen ñi dul Yawut itam, loolu di seen yaakaar ci ndam lu leen ñeel.
Ci loolu it la leen woo ba mu jëfandikoo xibaaru jàmm bi nu leen àgge, ngir ngeen séddu ci sunu ndamal Boroom Yeesu Almasi.
Jëlal sa wàll ci coono bi takk-derub Almasi Yeesu bu wóor di jànkoonteel.
Te gannaaw bu ngeen sonnee ab diir, Yàlla miy boroom wépp yiw te woo leen ci ndamam lu sax dàkk ndax Almasi, moom ci boppam moo leen di jagal, dooleel leen, dëgëral leen ba ngeen dëju.