TSK

TSK · 2 Timothy 2:16

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ci kaw loolu Esra sarxalkat ba jóg taxaw, ne leen: «Yeena fecci kóllëre ndax yeena jël ay jaambur jabar, di yokk tooñaangey Israyil.

¶ Seen damu gii de jekkul dara. Xanaa xamuleen ne as lawiir tooyalu sunguf bépp lay funkil?

Kumpa la dooley ndëngte ji bàddoo te mu ngi def liggéeyam xaat, xanaa kay ki ko téye ba tey moo koy téye rekk ba keroog jëlees fi ki ko téye.

¶ Ngalla waay Timote, sàmmal li ñu la dénk! Moytul kebetuy àddinay kese, ak werantey diiŋatkat yu tuddoo boroom xam-xam.

Waaye nit ñu bon ñi, ak maa-man yi dañuy gën di bon rekk, di naxe tey nax seen bopp.

te baña topp léebi neen yu Yawut yi, ak santaaney nit ñi dëddu liy dëgg.

Moytuleen balaa kenn di ñàkk yiwu Yàlla. Moytuleen bala ab reenu wextan di fëll, di lëjle, ba rax mbooloom lëmm.

Kàddu yu réy yu tekkiwul dara lañuy naxee, di fàbbee xemmemtéefi bakkan yu jéggi dayo, ay nit ñu yàggula rëcce ci ñeneen ñu nekk cig réer.

Ñaareelu rab wi nag nax waa àddina ci kéemaan, yi mu am sañ-sañu def ci turu rab wu jëkk wi. Mu sant waa àddina, ñu sàkk jëmmu rab, wi ñu jamoon saamar te muy wéye bakkanam.