Baat ba nag àddoo asamaan ñaareel bi yoon, ne ma: “Lu Yàlla setal, bu ko daganadil.”
TSK
TSK · Acts 10:15
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Xanaa nu bind leen, ne leen ñu moytu lu ay xërëm sobeel, moytu powum séy, moytoo lekk yàppu mala mu ñu tuurul deretam, ak lekk deret ci boppam.
Xam naa nag, wér na ma it te Sang Yeesu tax, ne amul lenn lu sobewu ci wàllu boppam, ba daganula lekk; waaye ki jàppe lenn muy lu sobewu, ci moom la loola di lu sobewu.
¶ Mboolem luy jaay ca ja ba, sañ ngeen koo lekk te bañ cee luqatu lenn luy indi ngànt cim xel,
Ñooñu ñooy aaye ab séy, di digle ñàkka lekk yenn ñam yu Yàlla sàkk, ngir gëmkat ñi xam liy dëgg, man cee jariñu te di ko sante Yàlla.
Loolu misaal la, ñeel jamonoy tey, di firndeel ne jooxe yi ak saraxi jur yi ñu daan jébbale manuñoo dindi yaraangeg jaamukatub Yàlla bi, ba mu set wecc.
Ñu dëggaate reseñ ja ca nalukaay, ba ca gannaaw dëkk ba, deret génne ca, taa ba tollook laabi fas yi, wala wal ba dajal digganteb ñetti téeméeri kilomeetar.