Moo tax ma tànn ko, ngir mu sant ay doomam ak waa këram, ñuy déggal Aji Sax ji, di jëfe yoon ak njub. Noonu laay defale Ibraayma li ma ko digoon.»
TSK
TSK · Acts 10:2
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
su boobaa ngalla nangool asamaan, màkkaan ma nga dëkke, te nga defal doxandéem boobu mboolem lu mu la ñaan, ndax xeeti àddina yépp xam sa tur, ngir ragal la ni Israyil sa ñoñ, te xam ne saw tur lañu tudd ci kër gii ma tabax.
¶ Amoon na ca réewum Ucc, góor gu ñuy wax Ayóoba. Góor googu nekkoon ku mat te jub, ragal Yàlla te dëddu lu bon.
Jiitee ma sag dëgg, jàngal ma. Yaw yaay Yàlla ji may musal, ma di la yendoo yaakaar.
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.
Éy Boroom bi, baaxe ma; yaw laay yendoo woo wall.
Ku dëggu ci réew mi, ma geesu, ngir fat ko. Te kuy wéye maandute, kookoo may liggéeyal.
Ndokklee yaw miy wattu kàdduy seedeem, di ko sàkkoo sa léppi xol.
Dees na wormaale turu Aji Sax ji fa sowu, wormaale teddngaam ba penku. Bu noon bi agsee ni walum dex, ngelawal Aji Sax jee koy wal, mu daw.
¶ Ci kaw loolu nit ña rungumlooti ba ca Buur, ne ko: «Buur, xamal ne yoonu waa Medd ak Pers tëral na ne mboolem aaye mbaa dogal bu buur dëggal dootu toxu.»
¶ Gannaaw loolu Buur Daryus bind waa mbooloo yépp ak xeet yépp ak làkk yépp, di waa àddina sépp, ne: «Jàmm ngeen!
Magi dëkk ba agsi ca Yeesu, tinu koo tinu, ne ko: «Ki nu yebal ci yaw de, yelloo na sa ndimbal,
¶ Booba ay toppkati yoonu Yawut a nga dëkke Yerusalem, te bawoo ci xeeti àddina yépp.
Sang bi ne ko: «Demal ba ca mbedd, ma ñuy wax Mbedd mu jub, te nga seet ca kër Yuda ku ñuy wax Sóol te dëkke Tàrs. Ma ngay ñaan.
¶ Dëkk ba ñuy wax Yope, ab taalibe bu jigéen a nga fa woon, ñu di ko wax Tabita mbaa Dorkas ci làkku gereg. Def lu baax ak sarxe la saxoo woon.
¶ Naka la malaaka ma wax ak Korney ba dem, mu woo ñaar ciy surgaam, ak benn takk-der bu jullite te bokk ciy suqam.
Mu ne ma: “Korney, nangu nañu say ñaan, te nemmiku nañu say sarax fa kanam Yàlla.
Póol jóg, tàllal loxoom, nee leen: «Yeen bokki Israyil ak yeen jaamburi ragalkati Yàlla yi, dégluleen!
Teewul Yawut ya xiirtal tuubeen yu jigéen yi gëna ràññiku, ak kàngam yu góor yi ci dëkk bi. Ñu daldi bundxatal Póol ak Barnaba, génne leen réew ma.
Teewul Kirispus njiitu jàngu ba moom, gëm Sang bi, mook waa këram gépp. Ñu bare ci waa Korent a gëm, gannaaw ba ñu déggee kàddu gi, ba ñu sóob leen ci ndox.
Ndaxte gëmkati Maseduwan ak Akayi ñoom la soob ñu sàkke lenn ci seen alal, ngir dimbalee ko ñu sell ña diy néew doole ca Yerusalem.
¶ Ag ñaan nag, saxooleen ko, te ngeen teewlu ci, boole ci ag cant.
¶ Ku desele am xel mu rafet nag, na ko ñaan Yàlla, mu may ko ko, ndax Yàlla mooy yéwéne ñépp te du sikk kenn.