TSK

TSK · Acts 10:31

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Su ko defee sarxalkat bi génne ci saraxu pepp mi, ab saraxu baaxantal, daldi koy lakk ci kaw sarxalukaay bi, muy saraxu sawara ngir xetug jàmm ñeel Aji Sax ji.

«Doxal ba ca Esekiya, nga ne ko: Aji Sax ji sa Yàllay maam Daawuda dafa wax ne: “Dégg naa sag ñaan, gis naa say rongooñ. Maa ngii di yokk ci saw fan fukki at ak juróom.

Mu ne ma: «Dañeel, bul tiit. Bés bu jëkk ba nga fasee yéene xam, ba toroxlu ci sa kanam Yàlla, ca lañu dégg say kàddu te sa kàddu yooyoo ma taxa ñëw.

Acts 10:4 TSK

Korney ne ko jàkk, tiit, ne ko: «Sang bi, lu mu doon?» Mu ne ko: «Say ñaan ak say sarax yéeg na fa Yàlla, ba mu bàyyi la xel.

Yàlla ñàkkul worma bay fàtte seen liggéey, ak cofeel gi ngeen sopp turam, te firndeele ko ni ngeen taxawoo ñu sell ñi, démb ak tey.

¶ Bi loolu amee meneen malaaka dikk, taxaw ci wetu sarxalukaay bi. Mu ngi yor andu cuuraayu wurus. Ñu jox ko cuuraay lu bare, ngir mu boole kook ñaani mboolem aji sell ñi, jooxe ko ci kaw sarxalukaayu wurus bi ci kanam ngàngune mi.