TSK

TSK · Acts 11:23

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Soppleen seen Yàlla Aji Sax ji, déggal ko te taq ci moom, ndax moom mooy seenug dund, di seen gudd-gi-fan ca réew ma mu giñaloon seeni maam Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba, ne ñoom la koy jox.

Natt nga saab xol, niir ma guddi, settantal ma, gisoo dara. Dogu naa ne duma moye wax.

Ma ngay tëroo nib sàcc, góor ñu bare lay fecciloo worma.

Ba mbooloo ma tasaaroo, bare na ay Yawut ak tuubeen yuy jaamu Yàlla yu topp ci Póol ak Barnaba. Ñuy wax ak nit ñi, di leen ñaax, ngir ñu sax ci doyloo yiwu Yàlla.

¶ Foofa lañu dugge gaal, dellu Àncos gu Siri, ga ñu leen dénke woon Yàlla ciw yiwam, ngir liggéey ba ñu sottal, ba délsi noonu.

Waaye sama bakkan soxalu ma, xanaa ma bey samaw sas, ba sottal liggéey, bi ma Sang Yeesu dénk, te mooy seedeel xibaaru jàmm bu yiwu Yàlla wi.

¶ Kon nag yeen sama bokk yi ma soppal sama bopp, farluleen, bu leen dara yëngal, te saxooleena jëm kanam ci liggéeyu Sang bi, te ngeen xam ne seenu ñaq, ci seenub ànd ak Sang bi, du neen.

Ni leen xibaaru jàmm bi dikkale nag, ni la dikkale àddina sépp, te mu ngi meññ, di law, na mu ko dale defe fi seen biir, ca bés ba ngeen déggee lu jëm ci yiwu Yàlla, ba ràññee ko dëgg.

Nu daldi yónni Timote, muy sunu mbokk, di jawriñub Yàlla bu nuy liggéeyandool ci xibaaru Almasi. Su ko defee Timote dooleel leen, feddli seen ngëm,

¶ Yaw nag seetlu nga bu baax sama àlluwa, ak sama dundin, ak sama mébét, ak sama ngëm, ak samag muñ, ak sama cofeel, ak samag ñeme coono,

¶ Fàttlikuleen bés yu jëkk ya, gannaaw ba ngeen jotee ci leeru Yàlla, na ngeen dëgërloo woon ca xeex bu mag ba te metti.

¶ Kon nag yeen soppe yi, gannaaw xam ngeen loolu ba noppi, wattuleen bala leena réeraangey moykati yoon yi yóbbaale, ba yolomal seenub taxawaay.