TSK

TSK · Acts 11:26

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Terewul ay gëmkat ñu dëkke Sippar ak Siren, bàyyikoo ca, dikk Àncos, wax ak làkk-kati Gereg yi, ñoom itam, ba àgge leen xibaaru jàmm bu Sang Yeesu.

¶ Ci fan yooyu la ay yonent jóge Yerusalem, dikk Àncos.

Mbooloom gëmkat mu nekk nag, ñu tabb ci ay mag; ci biir loolu ñu ñaan, boole kook koor, daldi dénk mag ña Sang bi ñu gëm.

¶ Àggripa nag ne Póol: «Nga defe ne man nga maa gaawa def noonu ab gëmkatub Almasi?»

Benn, dégg naa am na ay féewaloo ci seeni ndaje, te am na lu ma ci gëm.

Léegi nag su mbooloom gëmkat mépp dajee bérab, ñépp di làkk yeneen làkk, bu ay nit ñu xamul mbaa ñu gëmul duggsee, duñu ne dangeena dof?

Su ñu leen jànnee sax ndax turu Almasi, ndokklee yeen, ndax Noo gu darajawu gi, Noowug Yàlla moo wàcc ci yeen.