TSK

TSK · Acts 12:3

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Musaa ne mbooloo ma: «Fàttlikuleen bésub tey jii ngeen génne Misra, kërug njaam gi, ak ni leen Aji Sax ji yiwee dooley loxoom. Bu ci kenn lekk mburu mu am lawiir.

¶ «Fukki fan ak juróom ci weer woowu la ayu bésu Mburu mu amul lawiir di tàmbali, ñeel Aji Sax ji. Diiru juróom ñaari fan mburu mu amul lawiir ngeen wara lekk.

Acts 2:14 TSK

¶ Ci kaw loolu Piyeer taxaw, mook Fukk ñaak benn, daldi àddu ca kaw, ne: «Yeen bokki Yawut yi, ak mboolem yeen ñi dëkke Yerusalem, dégluleen bu baax sama kàddu, ba xam lii lu mu doon.

Acts 20:6 TSK

Nun nag ba màggalu Yawut, ga ñuy wax Mburu mu amul lawiir weesee lanu dugge gaal fa dëkk ba ñuy wax Filipi, am juróomi fan ca yoon wa, door leena fekksi ca Torowas, toog fa juróom ñaari fan.

Acts 25:9 TSK

Festus nag bëgg lu neex Yawut yi, tax mu ne Póol: «Ndax nangu ngaa dem Yerusalem, ñu àttee la foofa ci mii mbir ci sama kanam?»

¶ Léegi nag ndax nit ñi laay sàkkoo jubool, am Yàlla? Am nit ñi laay wuta neex? Su ma bëggoona wéye neex nit ñi de, duma doon jaamub Almasi.