Isaiah 62:6
TSK
Yerusalem, tabb naa ay jongrukat ci sa kawi tata. Buñu selaw, du guddi du bëccëg! Yeen ñiy soññ Aji Sax ji, buleen dal-lu.
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Yerusalem, tabb naa ay jongrukat ci sa kawi tata. Buñu selaw, du guddi du bëccëg! Yeen ñiy soññ Aji Sax ji, buleen dal-lu.
¶ Yeesu dellu leen léeb lii, ngir ñu wareefoo di sax ci ñaan te baña xàddi.
Bu benn cér mettee, mook cér yépp ay bokk metit wi. Bu dee benn cér lañu teral, mook cér yépp ay bokk bànneexu.
Deeleen ñaan fu ngeen tollu, gépp xeetu ñaan aki dagaan ci ndimbalal Noo gi, ànd ci ak teewlu fu ngeen tollu, ak gépp farlute, te ngeen di ñaanal mboolem gëmkat ñu sell ñi.
Bàyyileen xel ñi ñu tëj, ni su ñu leen boole woon ak ñoom tëj, ak itam ñi ñuy mitital, ndax yeen itam, aw yaram ngeen am.