TSK

TSK · Acts 13:34

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Man maay doon baay ci moom, moom, muy doom ci man. Su defee naka su dul noonu, maa koy yare bantu nit, ak dumay doom aadama.

Aji Sax ji laay woye ngoram, ba fàww, di biral wormaam sët ba sëtaat.

Teewluleen te dikk fi man. Dégluleen, ba mana dund, ma fas ak yeen kóllëre gu sax, gi ma baaxee Daawuda ci ngor gu wóor.

kon dinaa wacc askanu Yanqóoba ak Daawuda sama jaam bi, ba dootuma taamoo ciw askanam kuy yilif askanu Ibraaymaak Isaaxaak Yanqóoba. Maay tijji seen wërsëg moos, yërëm leen.»

¶ «“Daawuda sama jaam baay doon seen buur, di seen bennub sàmm ñoom ñépp. Sama àttey yoon lañuy doxe, sama dogali yoon lañuy sàmm, di ko jëfe.

Amos 9:11 TSK

«Bésub keroog maay yékkati mbaarum Daawuda mi joy, ba fattaat xar-xar yi, defaraat gent bi, tabaxaat ko na woon.

Waaye moom mi Yàlla dekkal, yàquwul.