TSK

TSK · Acts 13:45

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Mag ya nag iñaane ko. Teewul baayam moom bàyyi xel ci mbir moomu.

Ma gis ne nit ak kër-këram jépp ak bépp manoorey liggéey, iñaanantee ko waral. Loolu it, cóolóoli neen ak napp um ngelaw.

¶ «Loolaa nga fekk mag ja ca tool ya. Ba mag ja dikkee ba jub kër ga, ca la dégg po ma ak pecc ma.

Acts 6:9 TSK

Ba loolu amee ñenn ca jàngu ba ñuy wax jàngub waa Goreel ga, daldi jóg, di tàmbalee weranteek Eccen. Ay niti waa Siren a nga ca, ak waa Alegsàndiri, ak waa diiwaani Silisi ak Asi.

Acts 18:6 TSK

Yawut ya nag gàntal, di ko ŋàññ, mu yëlëb ay yéreem, misaale ko ne jaanam wàcc na. Mu ne leen: «Yeenay gàddu seen bakkanu bopp. Man set naa ci wecc. Gannaaw-si-tey, ci jaambur ñi dul Yawut laa jëm.»

Dañoo dem ba feese gépp xeetu njubadi, akug mbon, akug bëgge, akug coxor. Noyyeewuñu lu moy kiñaan, ak pexey bóome, ak ŋaayoo, akug njublaŋ, ak jëf ju sew. Ay jëwkat lañu it,

ak ñeetaane, ak màndite, ak mbumbaay, ak yeneen yu ni mel. Ma àrtu leen nag na ma leen artoo woon, ñiy jëfe noonu, amuñu cér ci nguurug Yàlla.

Waaye ku denc ci sab xol, wextanu kañaan, ak mébétum sàkku sa darajay bopp, bul damoo xel mu rafet, nde kon nga moy dëgg.

Ña ngeen ci daa àndal ñoo waaru tey, ba di leen sosal, ndax li ngeen àndatul ak ñoom, daw wuti googu yàqute gu af,