TSK

TSK · Acts 14:22

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ku yoqi, dooleel-leen ko, ku óom yay fenqe, jàppleleen ko.

Yeen nag yeenay ñi des ak man ci sama biir coono.

Acts 6:7 TSK

¶ Ba loolu amee kàddug Yàlla di law, limu taalibe yi yokku ba bare lool ci biir Yerusalem, sarxalkat yu bare daldi topp yoonu ngëm wi.

Ba Barnaba dikkee ba gis yiw, wi leen Yàlla may, dafa bég, di leen ñaax ngir ñu ŋoye seen xol ci Sang bi.

Yuda ak Silas it gannaaw ay yonent lañu woon, wax nañu ak bokk yi lu yàgg, ngir ñaax leen, feddli seen ngëm.

¶ Póol toog na Àncos ay fan, jóge fa wër diiwaanu Galasi, teg ca Firisi, di ñaax mboolem taalibey foofa.

Moo leen di dooleel ba ca mujjantal ga, ngir ngeen mucc sikk, keroog sunu bésu Sang Yeesu Almasi.

Nu daldi yónni Timote, muy sunu mbokk, di jawriñub Yàlla bu nuy liggéeyandool ci xibaaru Almasi. Su ko defee Timote dooleel leen, feddli seen ngëm,

¶ Bul kersawoo di seedeel sunu Sang, mbaa nga di ma kersawoo, man mi ñu tëj ngir moom, waaye jëlal sa wàll ci coonob xibaaru jàmm bi, ni la ko manoorey Yàlla manloo.

Te kat képp ku namma nekke ag njullite ci yoonu Almasi Yeesu, dees na la bundxatal.

Te gannaaw bu ngeen sonnee ab diir, Yàlla miy boroom wépp yiw te woo leen ci ndamam lu sax dàkk ndax Almasi, moom ci boppam moo leen di jagal, dooleel leen, dëgëral leen ba ngeen dëju.

Jude 1:3 TSK

¶ Soppe yi, yàkkamti woon naa leena bind ci mbirum mucc gi nu bokk, waaye fàww ma bind leen, ngir ñaax leen ci xeexal yoonu ngëm, wi Yàlla xasa dénk ñu sell ñi, benn yoon ba fàww.

¶ Man Yowaan seen mbokk, mi séddook yeen nattu ak barkeb nguurug Yàlla, ak muñ gi ci Yeesu, maa nga woon fa ñu ma toxaloon, ca dun ba ñuy wax Patmos. Li ko waral di sama waare ci kàddug Yàlla ak seedeel Yeesu.

¶ Ma ne ko: «Sama sang, loolu de xanaa yaa ko xam.» Mu ne ma: «Ñoo di ñi jóge ca nattu bu réy ba. Fóot nañu seeni mbubb, ba weexal ko ci deretu Gàtt bi.