TSK

TSK · Acts 15:28

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi
Acts 5:32 TSK

Nun noo seede loolu, nook Noo gu Sell, gi Yàlla jagleel ñi ko déggal.»

¶ «Kon nag sama xalaat mooy: bunu gétën jaambur ñi tuub, ba waññiku ci Yàlla.

¶ Ci wàllu janq ji séyagul, awma ci ndigalu Boroom bi, xanaa ma wax ci sama xalaat bu mata gëm, ndax yërmande ji ma Boroom bi baaxe.

Ku ci xalaat ne moom jottlikatub kàddug waxyu la, mbaa boroom ag may la ci Noo gi, war naa xam xéll ne lii ma leen bind, santaaneb Boroom bi la.

Yonent yooyu, xamalees na leen ne du seen njariñal bopp lañuy liggéeyal xibaar boobu, xanaa yeen. Ñi leen àgge xibaar bi tey ñoo di ñiy waare xibaaru jàmm bi ci dooley Noo gu Sell, gi ñu yebale asamaan, te muy mbir mu malaaka yi sax, noon siiwa nemmiku.