¶ Musaa nag dellu ca goroom Yettro, ne ko: «May ma, ma dellu Misra, seeti samay bokk, ba xam nu ñu def.» Yettro ne ko: «Demal ak jàmm.»
TSK
TSK · Acts 15:36
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Moo tax Aji Sax ji Yàllay Israyil wax ci sàmm yiy sàmm ñoñam ne: «Yeena tasaare sama gétt gi, dàq leen, te taxawuwleen leen. Kon maa ngii di leen taxawoo mbugal, yoole leen seen jëf ju bon.» Kàddug Aji Sax jee.
¶ Ñooñu la Noo gu Sell gi yebal, ñu dem dëkk ba ñuy wax Selusi, dugge fa gaal, jëm dun ba ñuy wax Sippar.
Póol ak Barnaba nag fëgg seen pëndub ndëgguy tànk, seedeel leen ko seen ngàntal, doora dem dëkk ba ñuy wax Ikoñum.
Ñu yég ko, daw làquji diiwaanu Likawni, ca dëkk ya ñuy wax Listar, ak Derbe ak la ko wër.
Gannaaw loolu ñu jaare biir diiwaanu Pisidi, ba àgg Pamfili.
te gannaaw li ci des lépp sax, sama xintey bés bu nekk a ngi fi, njàqare ji ma am ci mboolooy gëmkat ñépp.
¶ Nun nag bokk yi, teqale nañu nu ak yeen ab diir, waaye xol yi sorewaatoowul, xanaa jëmm yi rekk. Waaye sunu nammeel gu réy tax na noo def sunu kem kàttan, ndax yàkkamtee gise waat ak yeen.
Guddi ak bëccëg, pastéefu xol lanuy dagaane Yàlla, ngir man leena gisaat, ba mottli li yées ci seen ngëm.