Acts 14:27
TSK
Ba ñu agsee, dañoo woo mbooloom gëmkat ña, àgge leen mboolem na Yàlla def ak ñoom, ak na mu ubbilee jaambur ñi dul Yawut buntu ngëm.
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ba ñu agsee, dañoo woo mbooloom gëmkat ña, àgge leen mboolem na Yàlla def ak ñoom, ak na mu ubbilee jaambur ñi dul Yawut buntu ngëm.
¶ Ba loolu wéyee mbooloo mépp ne xerem. Ñu déglu nag Barnaba ak Póol, ñu xamle mboolem firnde yeek kéemaan, yi Yàlla defe seen ñaari jëmm ci biir jaambur ñi.
¶ Ba nu agsee Yerusalem nag, bokki taalibe ya bége nañu noo dalal.
¶ Kon nag, ni leen Almasi xajoo, nangeen ko xajoontee, ngir teddngay Yàlla.
Ci yiwu Yàlla daal laa doone ki ma doon, te yiw woowu ma ñeel neenul. Xanaa yeneen ndaw yépp sax, maa leen gëna liggéey. Du ci man nag, waaye yiwu Yàlla, wi ànd ak man la.
¶ Nun ñi bokk ci liggéey bi nag, noo leen di ñaan ngeen baña nangu yiwu Yàlla ci neen.