Lóot nag soññ leen, ba ñu dal këram, mu ganale leen. Lóot da leena berndeel, lakkal leen mburu mu amul lawiir, ñu lekk.
TSK
TSK · Acts 16:15
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Am na bés Alyaasa jaare dëkk bu ñuy wax Sunem. As ndaw su bare alal woo ko lekk këram, di ko soññ. Mujj na saa yu fa jaaree, daldi fay toog, ba xéewlu.
Kër gu ngeen dugg, fa ngeen di dal, ba kera ngeen dem.
Njaatige li ne ko: “Demal topp yoon yi, leru ñag yi, te nga soññ nit ñi, ñu dikk ba sama kër fees.”
Waaye ba ñu gëmee Filib, ma leen xamal xibaaru jàmm, bi jëm ci nguurug Yàlla ak turu Yeesu Almasi, góor ak jigéen daldi nangu, ñu sóob leen ci ndox.
Dina la àgge kàddu yu lay musal, yaw ak sa waa kër gépp.”
Teewul Kirispus njiitu jàngu ba moom, gëm Sang bi, mook waa këram gépp. Ñu bare ci waa Korent a gëm, gannaaw ba ñu déggee kàddu gi, ba ñu sóob leen ci ndox.
¶ Ndax Almasi dafa xaajalikoo? Ndax Póol lañu daajoon ca bant ba ngir yeen? Am ci turu Póol lañu leen sóobe ci ndox?
¶ Mujj naa dib dof nag, te yeena ma ko yóbbe, nde gërëm maa leen waroon, ndax doonte duma dara sax, ndaw yu màgga màgg yooyeey, duma seen cuune ci lenn.
¶ Ci man Póol, ndawal Almasi Yeesu ci coobarey Yàlla, ci man la kàddu gii bawoo, ñeel ñu sell ña ca Efes te di ñu sàmm seen kóllëre ak Almasi Yeesu.
¶ Ndegam nag sa waay nga ma def, dalal ko ni su doon man.
¶ Silwan, miy mbokkum gëmkat mu wóor, ci sama xalaat, ci ndimbalam laa leen bind kàddu yu gàtt yii, di leen ñaax aka seedeel ne lii kat moo di yiwu Yàlla dëgg. Taxawleen ci bu dëgër.