TSK

TSK · Acts 16:26

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Mu dem fekk néew ba ne lareet ca yoon wa, mbaam maak gaynde ga taxaw ca wet ga. Gaynde ga lekkul néew ba, fàddul mbaam ma.

nde Aji Sax jeey jéere fu sellam fa ca kaw, di niire suuf fa asamaan,

ngay gisloo gumba, di génne ku ñu tëj, ku dëkke woon lëndëm, génn kërug tëjukaay.

Yaw nag, deret ji feddli sama kóllëreek yaw, ci laay seet ba yiwi sa nit ñi ñu tëj biir kàmb gu ndox amul.

Acts 4:31 TSK

¶ Ba ñu ñaanee ba noppi, bérab ba ñu daje daa yëngu, ñu feese Noo gu Sell gi ñoom ñépp; ñu daldi tàmbalee waxe fit kàddug Yàlla gi.

Acts 12:7 TSK

Ci kaw loolu am malaakam Boroom bi ne jaas, taxaw, ag leer ne ràyy ca biir kaso ba. Malaaka ma laal Piyeer ci wetam, yee ko, ne ko: «Jógal gaaw!», càllala yi daldi rote ciy loxoom.

¶ Ma gisati bi muy tàyyi juróom benneelu tayu gi, suuf daldi yëngu bu baaxa baax, jant bi ñuul kukk, weer wi wépp xonq curr ni deret.