TSK

TSK · Acts 16:34

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

«Mbégte déy, ngeen di génne, ñu yóbbu leen ci jàmm, tund yu mag yeek yu ndaw yi di leen sarxolleel, garabi àll bi yépp tàccoondoo.

Xanaa du sédd ku xiif saw ñam, fat néew-ji-doole ju amul fu mu dëkk, gis ku rafle, wodd ko, te baña nëbbu mbokk mu soxla?

Luke 5:29 TSK

Ci kaw loolu Lewi waajalal ko bernde ju réy ca këram. Mbooloo mu bare teew, ay juutikat ak yeneen gan, ñu bokk toog, di lekk.

Waaye mbégte ak bànneex war na, ndax sa rakk jii moo dee woon te dekki na, moo réeroon te feeñ na!”»

Acts 2:46 TSK

Bés bu nekk nag ñu doon benn bopp, saxoo teew ca kër Yàlla ga, di dagg mburum bokkoo ci këroo kër, tey bokk lekk ci biir mbég ak woyoflu.

Dina la àgge kàddu yu lay musal, yaw ak sa waa kër gépp.”

Ci ndimbalam lanu ame ngëm ba mana àgg fi yiwu Yàlla wii nu taxaw taxawaay bu dëgër. Te it sunub sag moo di yaakaar ji nuy séentoo ab cér ci leeru Yàlla.

¶ Kon Yàlla miy maye yaakaar, yal na leen feesale gépp mbég, ak jàmm ci biir ngëm, ba ngeen géejule yaakaar, ci manoorey Noo gu Sell gi.

¶ Bégleen ci Boroom bi fu ngeen tollu, ma waxati ko, bégleen!

¶ Ci wàllu mbëggeel gi war ci biiri bokk, soxlawuleen ku leen ci bind dara, ndax yeen ci seen bopp, Yàlla tàggat na leen ci soppante,

¶ Bokk yi, ku ne gëm na, te jëfewu ko, ana lu mu koy jariñ? Ndax googu ngëm man na koo musal?