TSK

TSK · Acts 17:26

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Aadama nag tudde soxnaam Awa (mu firi Dund), ndax mooy ndeyu képp kuy dund.

Fàttlikuleen jant ya jëkkoon, baleen xel maasi maas ya woon. Laajleen seeni baay, ñu xamal leen; ak seen mag ñi, ñu wax leen.

Job 14:5 TSK

Ndegam yaa dogalal nit ay fanam, lim ay weeram, dogal àpp ba, te du jaas,

Yeen magi pénc mi, ñaawluleen! Yeen waa dëkk bee, yuuxuleen! Na Filisti gépp ne yàcc! Bëj-gànnaar déy la saxar jollee, kenn du wuute gàngooru noon ya.

Àdduleen, layoosi, diisooleen fi seen biir kay! Ana ku xamle woon lii bu yàgg, yégle woon ko booba? Xanaa du man Aji Sax ji? Kenn du Yàlla ku dul man! Yàlla ju jub, di walloo, du kenn ku dul man!

Ñenn ci boroom xel yu rafet yi dinanu jaare ci nattu yu leen di sellal, fóot leen ba ñu set wecc, ba keroog mujug jamono. Àpp ba nag des na.

Boroom bee xamle loolu bu yàgga yàgg.”

Noonu nit bokke ci Aadama, ba tax ñépp di dee, noonu la ñépp mana bokke ci Almasi, ba tax ñu dundalaat leen, ñoom ñépp.

ana kon nun ci sunu bopp, nan lanuy rëcce mbugal, su nu sàgganee pexem mucc mu réy mii Sang bi jëkkoona biral, te ñi ko dégg dëggalal nu ko?