TSK

TSK · Acts 17:28

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Bu ñu la doon dàq, di wut sa bakkan, yal na fekk sa bakkan dence ca ëmbu aji dund ña, ca sa wetu Yàlla Aji Sax ji, sang bi. Waaye sa bakkan ub noon, yal na ko mbaq, sànni fu sore.

yafloo sa njël lu duun, sa xéewal wal, nga nàndale ko.

xanaa ngay diirook Boroom asamaan, bay santaane ñu indil la ndabi këram, nga di ci naan biiñ, yaak say jawriñ ak say soxna ak say nekkaale, ngeen di sàbbaal ay yàllay xaalis ak yu wurus ak yu xànjar ak yu weñ ak yu bant ak yu doj, te du ci lenn luy gis mbaa muy dégg mbaa mu xam dara. Waaye Yàlla ji yor sa bakkan tey ak ëllëg sàbbaaloo ko.

Kon moom du ñi dee lay seen Yàlla, xanaa ñiy dund, ndax fa moom, ñépp a ngi dund.»

Ma wax ko waru jenn waay, ab waa Keret buy seen yonentu bopp. Mu ne: «Waa Keret, ay fen-kati neen, soxor niy rabi àll, fuqle, yaafus.»

Te itam am nanu ay baay ci wàllu deret, ñoo nu daan yar, te danu leena wegoon. Kon nag xanaa du Baay bi yor ug noo lanu wara gënatee nangul, ngir nu dund?