¶ «Ñu tàmbalee gàntal nag ñoom ñépp. Kii ne ko: “Ab tool laa jënd, te fàww ma xooli ko. Dama lay ñaan rekk, nga jéggal ma.”
TSK
TSK · Acts 17:32
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Erodd aki dagam nag sewal Yeesu, di ko ñaawal. Gannaaw loolu mu solal ko mbubb mu yànj, delloo ko Pilaat.
Teewul ñenn ñay ñaawle, ne: «Ñii daal biiñ bu bees doŋŋ lañu naan ba màndi.»
¶ Ci kaw loolu ay boroom xam-xam yu bokk ci ngérum Epikur ak ngérum Estowisen, di werante ak moom. Ñenn ña ne: «Kebatukat bii, lu muy wax nii?» Ña ca des dégg Póol di waare xibaaru jàmm bi ci Yeesu ak ndekkiteem, ñu ne: «Daa mel ni ay tuur-tuuraani doxandéem lay waareel.»
Naka la Póol wax ci mbirum njub, ak moom sa bakkan, ak àtteb bés-pénc, Feligsë daldi tiit, ne ko: «Léegi, man ngaa demagum, bu ma ko talee, dinaa la wooluwaat.»
Ana lu leen taxa jàpp ci seen biir ne xel nanguwul Yàlla di dekkal ñi dee?
Nun nag, nuy waare Almasi bu ñu daaj ci bant, muy njombe ci Yawut yi, di ag ndof ci jaambur ñi dul Yawut.
Ndaxte Yàlla moo ne: «Jant ba mu jotee laa la nangul, bésu mucc ba laa la wallu.» Te nag, tey jii la jantam jote; tey kat, la bésub mucc.
Ngëm la ñeneen dékkoo ay kókkali aki yar, ba ciy jéng ak tëjteb kaso.