Tey ñi may diijoo ngii, te ñoo ma féete ndaw, seeni baay a tekkiwuloon tus, ba ma siide leena jël, ñuy sàmmandook samay xaj.
TSK
TSK · Acts 17:5
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ma sol ay saaku, di ko ñaawloo, ñu di ma léebu.
Aji Sax ji, yaa xàcci sa loxo, waaye yéguñu ko. Won leen ni nga nabe ci sa ñoñ, ñu rus, te sawaraay xoyom sa noon yooyu.
¶ «Maam yooyu nag iñaane seen doomu baay Yuusufa, ba jaay ko njaam, ñu yóbbu ko Misra. Teewul Yàlla ànd ak Yuusufa,
Yawut yi gëmul nag di xiirtal jaambur ñi dul Yawut, di yàq seen xel ci bokki taalibe yi.
te Yason a leen dalal. Ñoom ñépp a xëtt ndigali buur Sesaar, te naan am na beneen buur bu ñuy wax Yeesu.»
¶ Ba loolu amee Yawuti Tesalonig dégg ne Póol a ngay xamle kàddug Yàlla ca Bere itam. Ñu dikkati, yëngal nit ña, ñu def ay gàngoor.
Ku ñuy wax Demetirus, ab tëggu xaalis, moo daan defar jëmmi jaamookaay yu ndaw yu tuur mi ñu dippee Artemis, muy njariñ lu réy ci liggéeykat yiy nawleem.
¶ Timote sama mbokkum liggéeykat nuyu na leen, mook Lusiyus ak Yason ak Sosipater sama bokki Yawut.
ak ñeetaane, ak màndite, ak mbumbaay, ak yeneen yu ni mel. Ma àrtu leen nag na ma leen artoo woon, ñiy jëfe noonu, amuñu cér ci nguurug Yàlla.
Ndax kat bokk yi, yeena aw ci tànki gëmkati Almasi Yeesu ya fa mboolooy Yàlla, ya fa réewum Yuda, nde coono ya ñu daj ca Yawut ya, yeen it seeni waa réew teg nañu leen lu ni mel.