TSK

TSK · Acts 19:10

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi
Acts 16:6 TSK

¶ Xel mu Sell mi nag tere leena yégleji kàddu gi ca diiwaanu Asi, ba tax ñu jàlli biir diiwaanu Firisi ak Galasi.

At ak juróom benni weer la Póol toog ci seen biir, di jàngle kàddug Yàlla.

Mu daldi yebal fa Maseduwan, ñaari jaraafam, Timote ak Eràst, moom mu toogaat ab diir ca Asi.

Ba ñu dikkee, mu ne leen: «Yeen ci seen bopp xam ngeen bu baax, ca bés ba ma jëkkee teg sama tànk Asi, ba tey jii, ni ma masa doxale ak yeen,

Teewluleen nag te fàttliku ne diiru ñetti at, guddi ak bëccëg, masumaa noppee àrtu kenn ku nekk ci yeen, bay jooy sax.

Ag wuutale amul diggante ab Yawut, ak jaambur bu dul Yawut; ñépp a bokk benn Boroom biy yéwéne mboolem ñi koy woo wall.

Dundin wu yees woowu amul jaambur akub Yawut, amul ku xaraf ak ku xaraful, amul ab doxandéem ak ku xayadi, amul ab jaam ak as gor, waaye Almasi mooy lépp te moo nekk ci ñépp.

¶ Ci man Piyeer, ndawal Yeesu Almasi la bataaxal bii bawoo, ñeel askan wi Yàlla taamu, te ñu toxuji diiwaani Pont ak Galasi ak Kapados ak Asi ak Bitini.

Mu ne: «Mboolem loo gis, bind ko cib téere, nga yónnee ko juróom ñaari mboolooy gëmkat ña ca dëkk ya ñuy wax Efes ak Samirin ak Pergam ak Catir ak Sàrd ak Filadelfi ak Lawdise.»