Ci kaw loolu waa Bet Semes ne: «Ana ku mana taxaw fi kanam Aji Sax ji, jii Yàlla ju sell? Ci kan lanuy yóbbu gaal gi, ba mu sore nu?»
TSK
TSK · Acts 19:17
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Seen làmmiñ a leen di fakkastal, ba ku leen xool wëcc bopp.
Tiitaange nag jàpp ñépp, ñu sàbbaal Yàlla, naan: «Yonent bu mag feeñ na ci sunu biir!» te naan «Yàllaa wallusi ñoñam!»
¶ Naka la Anañas dégg kàddu yooyu, daldi daanu, dee. Tiitaange lu réy nag dikkal ña ko dégg ñépp.
waaye kenn ca ña ca des ñemewula jaxasoo ak ñoom. Teewul askan wa nawloo leen lool.
¶ Ba ñu teeree Efes, fa la Póol bàyyi Pirsil ak Akilas. Mu dem ca jàngu ba, ba diisoo fa ak Yawut ya.
Moo tax Yàlla kaweel koo kaweel, baaxe ko tur wi tiim wépp tur,
¶ Li ci des nag bokk yi, moo di ngeen ñaanal nu, ngir kàddug Boroom bi gaawa law te am ndam na mu ko ame woon fa yeen,
Ña ngay àddu ca kaw, naan: «Gàtt bi ñu rendi woon moo yeyoo kàttan ak alal, yeyoo xel ak doole, moo yeyoo teraanga, yeyoo darajaak cant.»