¶ Xel mu Sell mi nag tere leena yégleji kàddu gi ca diiwaanu Asi, ba tax ñu jàlli biir diiwaanu Firisi ak Galasi.
TSK
TSK · Acts 19:21
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Naka la tàggtoo ak ñoom, ne leen: «Dinaa leen seetsiwaat, bu soobee Yàlla.» Ba loolu amee mu dugg gaal, bàyyikoo Efes,
Ndax Póol daa fasoon yéeney teggi Efes, ngir baña yàgg diiwaanu Asi; booba day gaawtu, ngir màggalu Pàntakot man koo fekk Yerusalem.
Nu seet taalibey foofa, ba gis leen, toog ak ñoom juróom ñaari fan. Ci biir loolu Noo gu Sell gi di leen xiir ci wax Póol, ne ko bumu dem Yerusalem.
¶ Ba nu agsee Yerusalem nag, bokki taalibe ya bége nañu noo dalal.
¶ «Samay tànk nag, gannaaw gëjeb at yu bare, moo doon indil samaw askan, ay ndimbal ak ay sarax yu ñeel Yàlla.
¶ Ba loolu wéyee ñu dogu noo dugal gaal, jëme nu réewum Itali. Ñu teg Póol ak ñeneen ñu ñu tëjoon, ci loxool njiitu takk-der bu ñuy wax Yulyus, bokk ci mbooloom xarem buur bu mag bi.
Ba nu dikkee Room nag may nañu Póol, mu am daluwaayu boppam, ab takk-der di ko wattu.
¶ Bokk yi, bugguma ngeen umple ne ay yooni yoon laa leen mébéta seetsi, ba liggéey ci seen biir lu leen jariñ, ni ma ko defale yeneen xeet; waaye ay gàllankoor a ma téye ba tey jii.
Waaye léegi jeexal naa sama sas ci gox yii, te gannaaw at yu baree ngii, ma namma dikk ba seetsi leen,
¶ Kóolute gu ma amoon ci ni ngeen nuy damoo moo tax ma naroona jëkka dikk ba ci yeen, ngir seen yiw mana yaar,
¶ Damaa bëgg, bokk yi, ngeen xam ne lii ma dal, xibaaru jàmm bi la far jëmale kanam.