TSK

TSK · Acts 19:9

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Teewul ñu të ticc, sajju loos ni seen maam ya gëmuloon seen Yàlla Aji Sax ji.

Artu nga leen ndax ñu dellu ci saw yoon, teewul ñu bew, ba sàmmuñu say santaane, xanaa di moy sa àttey yoon yiy taxa dund képp ku ci sàmmu. Ñuy daŋŋiiral, sajju loos, bañ laa déggal.

Mbégte ñeel na ki may déglu, di teewlu ca sama bunt bés bu nekk, di ma toogaanu sama bunt kër.

Waaye dégluwñu, teewluwñu ma, xanaa sajju loos, di bon, ba yées seeni maam.

Acts 9:2 TSK

di sàkku ay bataaxal yu ñeel jànguy dëkk ba ñuy wax Damaas, bataaxal yu yóbbante ndigal lu yeewlu képp ku ñu fa gis ku bokk ci Yoon woowu, góor ak jigéen, ngir mu jàpp leen, indi Yerusalem.

Ba Yawut yi gisee mbooloo ma nag, kiñaan man leen, ñuy weddi waxi Póol, di ko saaga.

Acts 17:4 TSK

Ba loolu amee ñenn ca Yawut ya gëm, fekksi Póol ak Silas, ñoom ak Gereg yu bare yu ragal Yàlla, ak jigéen ñu ràññiku ñu bare.

¶ Jant yooyu nag yemook yëngu-yëngu bu réy bu amoon ci mbirum Yoon wi.

Teewluleen nag te fàttliku ne diiru ñetti at, guddi ak bëccëg, masumaa noppee àrtu kenn ku nekk ci yeen, bay jooy sax.

Xanaa genn kàddu ga ma taxawoon ca seen biir, àddu ko ca kaw ne: “Mbirum ndee-ndekki gi ma gëm, moom lañu may àttee ci seen kanam tey!”»

Kon nag Yàlla mooy yërëm ku ko neex, te ku ko neex lay dëgëral xolam.

ak jote yu dul jeex yu boole ay nit ñu seenum xel mu yàqu xañ àlluway dëgg. Nit ñooñoo mbubboo ag njullite, te def ko wutukaayu alal.

Ag njullite lañuy mbubboo tey xalab leer ga leen ko wara manloo. Ñooñu, dëddu leen.

Waaye bés bu nekk deeleen soññante li feek muy bésub tey agum, bala bàkkaar a nax kenn ci yeen, ba mu mujj dërkiis.

Waaye ñoom ñooñu mel ni mala yu amul xel, seen yég-yégi judduwaale jiital leen, te li leen taxa juddu di jàpp leen, rey doŋŋ, ñooy saaga lu ñu xamul. Dees na leen rey ni ñuy reye ay mala.