TSK

TSK · Acts 2:1

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Wormaal-leen màggalu bésu Ngóob mi jëkka ñore ci tool, yi ngeen di bey, ak màggalu bésu Farmàngu mi ci ndeetel at mi, gannaaw bu ngeen dajalee seen meññeef ba noppi.

¶ «Bésub Noflaay ba ngeen di indi takku bele biy saraxu yékkati-jébbale, bés ba ca topp ngeen di dale waññ juróom ñaari ayi bés yu mat sëkk.

¶ Juróom ñaari ayi bés nag, ngeen di waññ, te ci ndoortel ngóob ngeen di tàmbalee waññ juróom ñaari ayi bés yi,

Maa leen di may benn xol ak benn jubluwaay ngir ñu di ma wormaal seen giiru dund, muy seen ngëneel, ñook seen doom yi leen di wuutu.

Acts 1:13 TSK

Ñu agsi, yéeg ca néegu kaw taax ma, fa ñuy dal naka jekk. Piyeer a nga ca, ak Yowaan, ak Yanqóoba ak Àndre, ak Filib ak Tomaa, ak Bartelemi ak Macë, ak Yanqóoba doomu Alfe, ak Simoŋ farlukatu moom-sa-réew ba, ak Yuda doomu Yanqóoba.

Acts 4:24 TSK

Ba ko bokk ya déggee, ñoom ñépp a mànkoo, daldi yékkati kàddug ñaan fa Yàlla, ne: «Buur Yàlla, yaa sàkk asamaan ak suuf ak géej ak lépp li ci biir.

Acts 5:12 TSK

¶ Ci kaw loolu ay firnde ak kéemaan yu bare di sottee ci loxol ndaw yi, ci biir askan wi. Gëmkat ñi nag di bokk daje ñoom ñépp fa ñuy wax Mbaarum Suleymaan, ca biir kër Yàlla ga,

ngir nu bokk jenn yéene ak genn kàddu gu ngeen sàbbaale Yàlla, sunu Baayu Sang Yeesu Almasi.

¶ Fexeleen rekk ba di jëfe ni mu yelloo ak xibaaru jàmm bu Almasi, ngir bu ma leen seetsee, mana seede, mbaa su ma wuutee it, di dégg ni ngeen saxoo di mànkoo, bokk jenn yéene, di xeex ngir saxal ngëm gi sukkandiku ci xibaaru jàmm bi.