Dinaa def mbañeel sa digganteek jigéen ji, ba dëddale sa xeet ak xeetam, muy toj sa bopp, nga di ko màtt ci téstën.»
TSK
TSK · Acts 2:35
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ñaan ma xeeti àddina, ma sédd la ko, nga moom ba ca cati àddina,
Buur wóolu na Aji Sax ji, moos, du tërëf, Aji Kawe jee gore.
Yaw la ay buur di baayoo, seeni lingeer di la nàmpal. Ñoo lay sujjóotal, di la maral say tànk, ba nga xam ne maay Aji Sax ji, te ku ma yaakaar du rus.»
Ña la daa néewal, seeni doom a lay sukkalsi. Ña la daa ñàkke worma, mujj di fóon say tànk. Dees na la wooye «Dëkkub Aji Sax ji», mbaa «Siyoŋ, màkkaanu Aji Sell ju Israyil.»
Sama noon yooyu buggul woon ma doon seen buur nag, indileen leen fii, te rendi leen ci sama kanam.”»
Su ko defee Yàlla miy boroom jàmm mooy dër Seytaane ci lu gaaw, fi ngeen ko joggi seeni tànk. Yal na sunu yiwu Boroom Yeesu ànd ak yeen!
mu dikk, naxsi askani ñeenti colli àddina, yi ñuy wax waa Gog ak Magog. Mu dajale leen ngir xare, ñu bare ni feppi suufas géej.