Mboolem diiwaan mbaa dëkk bu mag bu dogalu buur ba àgg, muy mbégteek bànneex ca Yawut ya; ñu def ko bés bu rafet, di xawaare. Bare na sax ñu bokk ci xeeti réew ma, ñu walbatiku dugg ci diiney Yawut ndax ragal Yawut ya.
TSK
TSK · Acts 2:43
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Esther 8:17
TSK
Hosea 3:5
TSK
Gannaaw loolu bànni Israyil dinañu walbatiku, sàkku seen Yàlla Aji Sax ji, ak Daawuda seen buur. Ca jant yu mujj ya, xolub ragal Aji Sax ji lañuy dikke fi moom, akug mbaaxam.
Luke 7:16
TSK
Tiitaange nag jàpp ñépp, ñu sàbbaal Yàlla, naan: «Yonent bu mag feeñ na ci sunu biir!» te naan «Yàllaa wallusi ñoñam!»
Acts 4:33
TSK
Ndaw yi nag di seedee doole ju réy ne Sang bi Yeesu dekki na, yiw wu yaa di leen dikkal ñoom ñépp.
Acts 5:15
TSK
Nit ñi dem bay génne jarag ji ci mbedd yi, teg leen ci ay laltu aki basaŋ, ngir bu fa Piyeer jaaree, lu bon bon takkndeeram mana dal ñenn ci ñoom.
Acts 9:40
TSK
¶ Ci kaw loolu Piyeer dàq ñépp ca biti. Mu sukk, ñaan, daldi walbatiku jublook néew bi, ne: «Tabita, jógal!» Mu ne xiféet, gis Piyeer, jóg toog.