Mooy nàddil néew-doole yi, njekkam sax dàkk, dooleem di yokku, ànd ak daraja.
TSK
TSK · Acts 2:45
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ku baaxe ku ñàkk, lebal nga Aji Sax ji, te moo lay yool.
Xanaa du sédd ku xiif saw ñam, fat néew-ji-doole ju amul fu mu dëkk, gis ku rafle, wodd ko, te baña nëbbu mbokk mu soxla?
Jaayleen seen alal, sarxe xaalis bi, sàkkuleen mbuus yu dul ràpp, muy dencu ëllëg bu dul jeex fa asamaan, fa ko sàcc dul jege, max du ko yàq.
Yeesu dégg loolu, ne ko: «Lenn rekk nga deseleeti. Mboolem loo am, jaay ko, séddale ko néew-doole yi. Su ko defee nga woomle fa asamaan. Boo noppee, ñëwal, topp ci man.»
Kenn ci ñoom ndóolul, ndax képp ku ciy boroom suuf mbaa ay kër, da koy jaay, indi njég li,
¶ Ci mbirum ndimbal lu jëm ci ñu sell ñi, jarul ma di leen bind,
Ñi barele na ñuy def lu baax, nañu barele jëf ju baax, di joxee xol bu tàlli, yéwén te nangoo dimbalee.
¶ Kaayleen nag ma wax leen, yeen boroom alal yi, jooyleen te yuuxu, ndax mitit yi leen di dikkal.