TSK

TSK · Acts 2:47

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi
Luke 2:52 TSK

Yeesu moom, ma ngay màgg ci dayo ak xel mu rafet, ak cérub yiw fi Yàlla ak nit ñi.

Acts 2:39 TSK

Ndax dige bi, yeen ak seen askan a ko moom, ak jaambur ñi féete fu sore ñépp, mboolem ñi sunu Yàlla Boroom bi woo.»

Acts 4:21 TSK

Ba loolu amee ñu tëkkuwaat leen, door leena yiwi, ñu dem, gannaaw manuñu leena mbugal te amuñu bunt ci ñoom ndax mbooloo ma, te ñépp di màggal Yàlla ca la xew,

Acts 5:13 TSK

waaye kenn ca ña ca des ñemewula jaxasoo ak ñoom. Teewul askan wa nawloo leen lool.

¶ Ba jaambur ña déggee loolu, dañoo bég, di màggal kàddug Boroom bi; ci biir loolu ña dogal ba jagleel ag texe ba fàww, ñoom ñépp daldi gëm.

Ñi Yàlla tuddaloon loolu lu jiitu, moo leen woo itam; ñooñu mu woo, moo leen jox itam àtteb ñu jub; te ñooñu mu jox àtteb ñu jub, moo leen darajaal itam.

Kon nag naka noonu itam ci jamonoy tey jii, aw ndes a ngi fi, te ci kaw yiw lees leen taamoo.

¶ Ndax kat kàddu gi jëm ci bantub Almasi, ba ñu ko daajoon, ag ndof la ci ñiy sànku. Waaye manoore Yàlla la ci nun ñi mucc.