Dañu la naan: «Dikkal, nu tëruji bakkan, yeeruji jaambur bu deful dara.
TSK
TSK · Acts 20:3
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Ba ñu ca tegee ab diir bu xawa yàgg, Yawut yi féncoo, ngir reylu ko.
¶ Ba loolu wéyee Póol toogaat na fa fan yu bare, doora tàggtoo ak bokk ya, dugg gaal jëm Siri, ànd ak Pirsil ak Akilas. Fekk na mu watu nel ca teerub Señsere, firndeele ko aw xas wu mu xasoon.
¶ di jaamoo Boroom bi ag woyof gu mat sëkk, ci biiri rongooñ ak nattu yu ma pexey Yawut yi teg.
¶ Ba bët setee Yawut ya daje, daldi xasoo, ne duñu lekkati, duñu naanati, ba kera ñu reyee Póol.
¶ Kóolute gu ma amoon ci ni ngeen nuy damoo moo tax ma naroona jëkka dikk ba ci yeen, ngir seen yiw mana yaar,
Bare na lu ma tukki, ay aaytéef xaare ma ay dex, xaare ma ay sàcc, xaare ma ay pexe yu ma samaw xeet lalal, ak yu ma jaambur ñi lalal. Ay aaytéef xaare na ma biir dëkk, xaare ma biir màndiŋ, xaare ma biir géej, xaare ma ci biir bokki taalibe yu ko mbubboo.