TSK

TSK · Acts 20:33

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ba loolu amee Musaa mer lool. Mu ne Aji Sax ji: «Bul geesu sax seen sarax. Menn mbaam sax, masuma leen koo jëlal te masuma cee tooñ kenn.»

Ndegam ñeneen a jagoo boobu sañ-sañ ci yeen, astamaak nun. Waaye nag jariñoowunu sañ-sañ boobu. Lépp lanu far muñ, ngir baña gàllankoor yoonu xibaaru jàmm bu Almasi.

kon ana lu ciy sama peyoor? Xanaa ma man di yégle xibaaru jàmm bi ci dara, ba duma jariñoo sañ-sañu dunde xibaaru jàmm bi may yégle.

Te ba ma nekkee ci yeen te soxla dab ma, wéeruwuma ci kenn ci yeen, ndax la ma ñàkkoon, bokk ya jóge Maseduwan ñoo ma ko indil. Fexe naa ba du lenn lu ma leen diisale, te noonu laay saxoo.

¶ Masunoo jaye, xam ngeen ko, ag bëgge it masunoo taxa jóg, Yàlla seede na ko;