TSK

TSK · Acts 20:6

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ «Bésub keroog bésu pàttliku lay doon ci yeen, ngeen war koo màggal ngir Aji Sax ji, muy dogal bu leen war fàww, yeen ak seen askan.

¶ «Diiru juróom ñaari fan ngeen di lekk mburu mu amul lawiir, te na bésub juróom ñaareel ba di bésu màggalug Aji Sax ji.

¶ «Màggalug ayu bésu Mburu mu amul lawiir, wormaal-leen ko. Diiru juróom ñaari fan ngeen ciy lekk mburu mu amul lawiir, ni ma la ko sante bu àppam taxawee ci weeru Abiib, ndaxte weeru Abiib ngeen génne fa Misra.

Acts 16:8 TSK

Loolu tax ñu jàlle biir Misi, àkki dëkk ba ñuy wax Torowas.

Acts 21:4 TSK

Nu seet taalibey foofa, ba gis leen, toog ak ñoom juróom ñaari fan. Ci biir loolu Noo gu Sell gi di leen xiir ci wax Póol, ne ko bumu dem Yerusalem.

Gis nanu fa ay bokki gëmkat, ñu ñaan nu, ba nu toog fa ñoom juróom ñaari fan. Gannaaw loolu nu dem Room.

¶ Man la Póol, Timote miy jaamub Almasi Yeesu ni man ànd ak man ci lii, ñeel mboolem ñu sell ñi gëm Almasi Yeesu, te dëkke Filib, yeen ak seeni njiit ak taxawukati mbooloo mi.

Mbubb ma ma waccoon ak Karpus ca Torowas, booy ñëw, indaaleel ma ko, ak itam téere yi, rawatina téerey der yi.