Ci biir loolu ñu taxaw, di jàng ca seen téereb yoonu Yàlla Aji Sax ji, diirub xaajaatu bés ba. Xaajaatu bés ba ca topp ñuy tuub ak a sujjóotal seen Yàlla Aji Sax ji.
TSK
TSK · Acts 20:7
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Gannaaw loolu mu jël mburu, yékkati kàddug cant, dagg ko, jox leen ko ne: «Lii moo di sama yaram wi ñu jooxe ngir yeen. Deeleen def lii, di ma ko fàttlikoo.»
Bés bu nekk nag ñu doon benn bopp, saxoo teew ca kër Yàlla ga, di dagg mburum bokkoo ci këroo kër, tey bokk lekk ci biir mbég ak woyoflu.
Mu yéegaat, dagg mburu ma, lekk. Waxaat na lu yàgg, ba njël jot, mu sooga dem.
¶ Ci kaw loolu ñu jox ko bés, bés ba dikk, ñu bare dikk, fekksi ko ca daluwaayam. Suba ba ngoon mu di leen jàngal, di leen seedeel lu jëm ci nguurug Yàlla, di leen won ci mbirum Yeesu, firnde yu leen gëmloo te tukkee ci yoonu Musaa ak ci yonent yi.
¶ Waaye lii ma leen digal, am na ci lu ma leen gërëmewul, ndax du njariñ la seeni ndaje di jur, xanaa loraange.
Bés bu jëkk ci ayu bés yi, na ku nekk génne as lëf ca la mu am, na mu ko àttane, te mu dencal ko boppam, ngir bu ma dikkee, dootu soxlaa wër, di dajale.
Maa nekkoon ci biir Noowug Yàlla benn bésub Sang bi, ma dégg ci sama gannaaw baat bu xumb nig liit.