TSK

TSK · Acts 21:11

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Naka la Samiyel ne wërëñ, di dem, Sóol jàpp ca catal mbubb ma, mu dagg.

Fekk na Cedekiya doomu Kenaana, ma woon ci seen biir, defarlu ay béjjéni weñ. Ma nga naan: «Aji Sax ji dafa wax ne: “Yii ngay jame waa Siri, ba jeexal leen.”»

¶ Aji Sax ji da maa wax ne ma: «Demal jëndi njiitlaayu lẽe, nga woddoo ko, te bu ko ndox laal.»

Mbooloo mi nag ne ma: «Xanaa doo nu wax lii ngay def nii, lu muy wund ci nun?»

Acts 9:16 TSK

Maa koy won mboolem coono bi mu wara dékku ngir sama tur.»

Acts 16:6 TSK

¶ Xel mu Sell mi nag tere leena yégleji kàddu gi ca diiwaanu Asi, ba tax ñu jàlli biir diiwaanu Firisi ak Galasi.

¶ Ci kaw loolu njiit la agsi, jàpp ko, daldi santaane ñu jénge ko ñaari càllala. Ba loolu wéyee mu laajte, ne: «Kii ku mu doon, ak lu mu def?»

¶ Ba ñu ca tegee ñaari at yu mat, ku ñuy wax Porsiyus Festus wuutu Feligsë. Feligsë nag bëggoon lu neex Yawut ya, ba tax mu bàyyi Póol ca kaso ba.

¶ Ñu teg ca ñetti fa, mu woolu njiiti Yawuti dëkk ba. Ba ñu dajee, mu ne leen: «Bokk yi, man defuma dara lu dëngook sunuw xeet mbaa sunu aaday maam. Teewul ñu jàppe ma fa Yerusalem, teg ma ci loxoy Room.

Ba ñu werantee ca seen biir, bay dem te juboowuñu, Póol teg ca ne leen: «Noo gu Sell gee yeyoon wax lii seeni maam, Yonent Yàlla Esayi jottli.

¶ Dama leen di dénku nag, man mi ñu tëj ndax Sang bi, ngir ngeen dund dundin wu yellook wooteb Yàlla, bi mu leen woo.

Xibaaru jàmm boobu moo tax may daj coono yu metti ni defkatu mbon, ba ci jéng yii ñu ma jéng. Waaye kàddug Yàlla moom, deesu ko jéng.

Ndax yeena bokk ak ñi ñu tëj seen coono, te yeena muñe xol bu sedd ni ñu foqarñee seen moomeel, ngir xam ngeen yeen ci seen bopp ne am ngeen alal ju ko gën tey sax ba fàww.