TSK

TSK · Acts 22:14

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Musaa ne Yàlla: «Su ma demee ca bànni Israyil, ne leen seen Yàllay maam ya moo ma yónni ca ñoom bànni Israyil de, dinañu ma laaj nu mu tudd. Lu ma leen di wax nag?»

Daa dëddu Aji Sax ji, Yàllay maamam, baña jaar ci yoonu Aji Sax ji.

«Laata ma lay sos ci sa biiru ndey, xam naa la; laata ngay juddoo ci sa ndey, séddoo naa la, def la ngay yonent ñeel xeet yi.»

Acts 5:30 TSK

Sunu Yàllay maam moo dekkal Yeesu, mi ngeen wékk ci bant, bóom ko.

Acts 9:15 TSK

Sang bi ne ko: «Demal, ndax kooku jumtukaay laa ko tànne, ngir mu xamali sama tur, xeeti jaambur yi ak seeni buur, xamal ko itam bànni Israyil.

¶ Yàllay bànni Israyil jii moo tànnoon sunuy maam, moo yaatal xeet wi, ba ñuy ganeyaan ca Misra; moo leen fa génnee kàttanu loxoom.

Lenn de man naa la koo nangul. Yoon woowu ñu ne mooy ngér mu sikk, moom laay topp, di ko jaamoo sunu Yàllay maam. Teewul mboolem lu ñu bind ci yoonu Musaa ak téerey yonent yi, gëm naa ko.

¶ Ci man Póol miy jaamub Almasi Yeesu la bataaxal bii bawoo, man miy ndawam ci kaw woote bu ma tabb, sédd ma sasu xamle xibaaru jàmm bu Yàlla.

¶ Man, li ma jële ci Sang bi, moom laa leen jottli: Sang Yeesu, guddi gi ñu ko woree, dafa jël mburu,

Man nag la mujja feeñu, te ma dib liir bu ab juddoom moy bésam,

Te it man jëlewuma ko, jàngewuma ko ci nit, xanaa ci peeñum Yeesu Almasi.

¶ Ci man Póol, ndawal Yeesu Almasi ci coobarey Yàlla, ngir xamle digeb dund gi ci Almasi Yeesu, ci man la bataaxal bii bawoo,