Buur woo waa Gabawon, wax ak ñoom. Waa Gabawon bokkuñu woon ci bànni Israyil, waaye ñoo desoon ca Amoreen ña bànni Israyil giñaloon ne duñu leen rey. Teewul Sóol xéroon lool ci bànni Israyil ak Yuda, bay fexee faagaagal waa Gabawon.
TSK
TSK · Acts 22:3
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Ca gannaaw ëllëg sa lañu ko fekk ca kër Yàlla ga, mu toog ca digg jànglekat ya, di leen déglook a laaj.
Ci kaw loolu rakkam ju ñuy wax Maryaama toog ca wetu Sang bi, di déglu kàddoom,
Ba loolu amee ñenn ca jàngu ba ñuy wax jàngub waa Goreel ga, daldi jóg, di tàmbalee weranteek Eccen. Ay niti waa Siren a nga ca, ak waa Alegsàndiri, ak waa diiwaani Silisi ak Asi.
Bokki gëmkat ña nag yég ko, daldi koy yóbbu Sesare, yebale ko foofa, mu dem Tàrs.
¶ Ñu yóbbante leen bataaxal, bind ci ne: Nun ndawi Yeesu, ak mag ñi, seen bokki Yerusalem, noo leen bind, yeen sunu bokki gëmkat ñi dul Yawut te dëkke Àncos ak Siri ak Silisi. Nu ngi jiital sunub nuyoo.
¶ Ñu dégg ca, daldi sàbbaal Yàlla, ba noppi ne ko: «Mbokk mi, xoolal ñaata junniy Yawut a doon ay gëmkat, te ñoom ñépp di ñu xér ci yoonu Musaa.
¶ Fekk na Póol xam ne lenn ca kurél gaa nga bokk ca ngérum Sadusen ya, ña ca des bokk ca ngérum Farisen ya. Mu daldi àddu ca kaw ca biir géew ba, ne: «Bokk yi, man de ab Farisen laa, di doomu Farisen; li ñu may àttee nag mooy sunu yaakaar ak sunu ngëm gi nu bokk ci mbirum ndee-ndekki.»
Xam nañu ma bu yàgg, te su leen neexee ñu seede ne ngérum Farisen mi gëna diis ci sunu diine, ci laa masa bokk.
¶ Ma ne kon, xanaa Yàlla daa wacc ñoñam? Mukk kay! Man ci sama bopp ci Israyil laa bokk, askanoo ci Ibraayma, giiroo ci Beñamin.
Yoonu Yawut, maa ci rawoon ñu bare ci sama maas gi ma bokkal askan, te maa leen gënoona xér fuuf ci sunu aaday maam.
¶ Yitte ju réy ji ñenn ñiy taqoo ak yeen de, jubluwuñu ci lu baax. Dañu leena bëgga tàggale ak nun, ba ngeen taq leen.