TSK

TSK · Acts 22:4

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi
Acts 7:58 TSK

ñu wat-watee ko, génne ko dëkk ba, di ko dóor ay doj. Fekk na seede ya summi seeni mbubb, juug ca tànki benn xalelu góor bu ñuy wax Sóol.

Acts 9:1 TSK

¶ Ci biir loolu Sóol moom, noyyeewul lu moy di tëkkook a jéema bóom taalibey Sang bi. Mu dem nag ca sarxalkat bu mag ba,

Acts 9:21 TSK

Mboolem ña ko dégg, daldi waaru, naan: «Xanaa du kii moo doon bóom ñiy tudd woowu tur ci Yerusalem? Du moo fi dikkoon, ngir yeewlu leen, yóbbu ci sarxalkat yu mag yi?»

Mu tàmbalee waxe kóolute ca jàngu ba. Pirsil ak Akilas dégg ko, woo ko cig wet. Ñu daldi koy gëna leeralal yoonu Yàlla wi.

¶ Jant yooyu nag yemook yëngu-yëngu bu réy bu amoon ci mbirum Yoon wi.

Lenn de man naa la koo nangul. Yoon woowu ñu ne mooy ngér mu sikk, moom laay topp, di ko jaamoo sunu Yàllay maam. Teewul mboolem lu ñu bind ci yoonu Musaa ak téerey yonent yi, gëm naa ko.

ndax kat maa gëna ñàkk solo ci ndawi Almasi, te yeyoowuma sax turu ndaw, gannaaw maa doon bundxatal mbooloom Yàlla mi.

te ma nekkoon ab tooñkatam, di ab bundxatalkat, di ab néeg. Waaye yërmande laa dajeel, ngir ñàkka xam ga ma daan jëfe, te ñàkka gëm tax.