2 Samuel 17:17
TSK
¶ Ma nga fekk Yonatan ak Ayimaas ca En Rogel. Manuñu woona dugg ca biir dëkk ba, ndax ragal ñu gis leen. Ab jaam bu jigéen nag di dem ca Yonatan ak Ayimaas, di leen wax la xew, ngir ñu dem ca Buur Daawuda, yegge ko ko.