Acts 22:5
TSK
Sarxalkat bu mag bi, ak mboolem kurélu mag ñi man nañu ma cee seede. Ci ñoom sax laa nangoo woon bataaxal bu jëm ca bokki Yawut ya ca Damaas, ga ma jëmoon, ngir yeewe fa gëmkati Yoon wii nekkoon foofa, ba indi leen Yerusalem, ngir ñu mbugal leen.